Jambutt ne
leegi fategeen juróomi mburu yu dundaloon juróomi juuni góor,
ak juróom ñaari dámba yu fees ak dammiit yi ci des, mbaa juróom
ñaari mbuuru yi dundaloon ñeent junniy góor ak lu bari lu desoon
ci damiiti mbuuru. Waaye mbuga ma yemale sa waxtaan wi ci ñam
wi ci kaw suuf. Deedeet, dama leen di artu ndaxte ngeen moytu
njàngaleem Farisiya ya ak Saduseen ya ñiy jëndante ak jaayante
ak diine.
Seen màggal
amul ben njëriñ, ci li ñuy jangale dénkaanay nit kese. Don ñuy
dëddu ndigale Yàlla jubbu ci aaday nit.
Moytuleen
ñi mbuubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yeen, yor melow xar, waaye
ci biir ay bukki yu suxor lañu. Seytaane mooy seem baay, te bëg
ngeen di bëg-bëgam ngeen di bëgg di def. Bookat la masa doon.
Buy fen, dëppo na ak jikoo, ndaxte feenkook la, te ci moom la
fen soqikoo. Ñi di naxaate te def seen boop ñi leen di atte maangi
leen di wax ne: Atte bu Yálla daan na leen yeen ñiy jiite den
te diko jangale, yeen naaféeq yi! Digéen torox! Ndaxte yeena ngi
tëj nguru Yálla Aji Kawe ji ci kanamu nit ñi; yeen dungeen ci
dugg, te dungeen báyyi nit ñ bëgga dugg, ñu dugg ci. Yeena ngi
lekk alaalu jigéen, ñi seeni jëkkër faatu, di ñaan Yálla ay ñaani
ngistal yu gudd. Seem mbugal dina gëna tar.
Yeena ngi
wër géej ak suuf, ngir sákku ben taalibe, ba nopppi ngeen def
ko nitu safara ku leen yees ñaari yoon. Yee na ngi naan: " Kër
Yálla gi amul njëriñ. Yeen ñi dof te gumba - Lan mo gëna mágg
sarax si, walla bérubu rendi kaay bi tax sarax si sell? Ku giñe
bérabu rendikaay bi, giñ ga ci rendikaay ak li ci kawam lépp.
Ku giñe kër Yálla gi, giñ nga ci tur kër Yálla ak ci ki ci dëkk.
Ku giiñ ci asamaan, giiñ nga ci jalu Buur Yálla ak ci ki ci toog.
Yeena ngi sakk asaka ci naana ak a nette ak kumin, te sággáne
yi gën na mag ci yoon wi maaman njub, yërmande ak gëm. Loolu ngeen
wara def muy seen yite.
Yeena ngi
segg wallax-njaan, tey wonn giléem. Yeena ngi setal bitib kaas
bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal. Gumba
yi ngeen doon! Jëkkleena setal biir kaas ak ndab li, ngir biti
itam set. Yeen xudbakat yi bon yi! Naaféq yi, yeena ngi mel ni
bámmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci
biir dañoo fees ak yax xi ñi dee, ak tilim tilim yu nek. Yeen
itam ci ngistal daagneena mel ni ñu jub, waaye ci seem biir dangeen
fees ak naaféq ak lu bon. Nan nga mëne gëme yaaw miy dunde ñaani
say moroom, te doo wut mukk ñaam yi jëm fa Yálla moom rekk?
Yeena ngi
tabax xabru yonent yi, tey rafetal bámmeelu ñu jub ñi. Te yeena
ngi wax ne: Bu nu fekke woon sunuy jamanoy maam, duñu ánd ak ñoom
ciy tuur deretu yonnent yi.
Seede ngeen
nii ne, yey ngeen seen bopp, te yeenay doomi ñi rey yonent yi.
Yeen ñi mel ni ay jaan, te fees ak dangar naka ngeen di muce ci
mbugalu safara?
Moo tax maa
ngi leen di yonee ay yonent ak ay borom xam-xam ak ay xudbakat.
Ñenn ñi digeen leen rey te daaj leen ci bant, ñeeneen ñi dingeen
leen dóor ay yar ci seeni jànfu, di leen fitna ci dëkkoo- dëkk.
Yeen ñi naféeq,
Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yálla ci seen biir, bi nu naan:
" Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen séen xol
sore na ma".
Yeen yeena
ngi fexee jug ci kanamu nit ñi waaye Yàlla xam na seen xo. Ndaxte
li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.
Artu na leen:
Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak soowu,
bokk lekk ak Ibrahima ak Isaaxa ak Yanxóoba ci nguru Yálla Aji
Kawe ji. Waaye ñi waroona bokk ca nguur ga, dees na leen sànni
ci biti ci lëndem gi. Bu seen njubte ëppul njubteb xudbakat ya
ak ñay mbuboo diine dungeen tàbbi mukk ci nguuri Yàlla Aji Kawe
ji.
LEER GIY LEERAL ÀDDINA SI
Ni ag leer
laa wàcce di àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm gi. Man maay
leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndem, waaye dinga am
leeru dund. (1)
Ci nii la
àtte bi ame: Leer gi ñëw na ci àddina si, waaye nit ñi lëndem
gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon. Képp kuy def lu bon day bañ
leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam feeñ bëccegu ndara-
kàmm. Waaye ku def lu jub day ñew ci leer gi, ngir ñu xam ne,
def na ay jëfam ci kanumu Yàlla. (2) Bu njëk dem ngeen ca àll
ga ngir seetu seeti yonnent Yàlla Yaxya. Mood seede dëgg gi. Meloon
na làmp buy tàkk tey leeral, te nangu ngeena bánneexu ab diir
ci leram. Waaye yor na ci man seede, si gëna mag seede si ma Yaxya
di seedeel: Maa ngi def jëf yu ma Baay bi sant. Jëf yooyu may
def nag ñooy seede ne, Baay bi moo ma yónni.
Su ma
deful sam jëfi Baay, buleen ma gëm; waaye su ma ko defee, bu ngeen
ma ngëmul sax, gëmleen boog samay jëf, ngir ngeen xam te nangu
ne, maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nek na ci man. Bëccëg lanu
wara matal jëfi ki ma yónni: Guddi dina ñëwi, goo xam ne, keen
du ci mana liggéey. (3)
Bët mooy
lámpu yaraam. Bu sa bëtt wéree, kon sa yaram wépp leer, waaye
bu sa bët woppe, kon sa yaram lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu
nekke lëndëm , na ka la lëndëm googu di këruus (4)
Xanaa
du bëccëg fukki waxtu ak ñaar la? Kuy dox bëccëg, du kaqastalu,
ndaxte day gis leeru àddina si. Waaye kuy dox guddi, dina faqastalu,
ndaxte leer gi nekkul ci moom. Kon ci bi ngeen dee am leem gi,
gëmleenko, ngir ngeen "doon doomi leer". Doxleem, ci ngeen dee
am leer gi, ngir lëndëm bañ leena bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm
doo xam foo jëm. Bu gumba dee wommant moroomam nag, kon dinañu
daanu ñoom ñaar ci kàmb. (5)
Kenn
du taal làmp, dëpp ci leget, walla mi di ko def ci ron lal Daf
koy wèkk ngir mu leeral ñiy dugg. Te iit duñu taal làmp dëp ci
leket, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñëpp.
Xanaa xamoo ne yeen di leeru àddina? Da ngeena mel ni dëkk bu
nekk ci kaw tund, du mana nëbbu. Na sen leer leere noonu ci kanumi
nit ñi, ndax nit ñi gis seen jëf yu rafet, te mággal seen Baay
bi ci kaw. Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, wallu lu
làqui lu ñu dul feeñal, bu ne nàñ. Li ma leen wax ci biir lëndëm,
waxleen ki ci leer; li ma leen déey, yégleleen ki ci kaw taax
yi. (6)
PEEÑU GI
Waxtu
wi ñu wara feeñale ndamu Doom mu nit ki jot na. (1) Wútumaa màggal
sama bopp. Keneen a ma koy wuutal te mooy àtte. (2)
Seen yoon
dafa wax ne, seede ñaari nit a gëna wóor. Man maa ngi seedeel
sama bopp, te Bay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam. Te bir
na ma ne, la muy wax ci man dëgg la. Lii moo tax xëccoo wu ma
kilifteef ci kaw suuf. (3)
Nit kiy wax
ci coobereem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal
kiko yónni, dëgg rekk lay wax te jubediwul fen. (4)
Ñëwaluma sam
bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la ndaxte wáccewuma ci asaamaa
ngir def sama bëgg-bëgg waaye damay matal bëgg-bëgg ki ma yónni.
Li moo tax ma juddu, ñëw áddina: Ngir wax dëgg gi. Ku book ci
dëgg gi dina nangu li ma wax. (5)
Man ak Baay
bi benn lanu. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dung, ba neek ci naataange.
(6) May na ma bepp sañ-sañ muy ci asaamaan ak ci suuf. Dama leen
di jox dung gu dul jeex, caabiy nguuru addina ak sañ-sañ buy noot
dooley seytaane kon na seen xel dal te bu leen raggal dara. Jàmm
la leen bàyyell. Sama jàmm laa leen jox, jàm ju áddina mënula
joxe. Dingeem xam dëg gi leen di goreel. Kon nag bu leen doom
ji defee gor, dingeen doon ay gor ci lu wër, wax na leen loolu
ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk. (7)
Lii mooy bëgg-bëgg
Baay bi: Képpp ki gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex,
te bés bu mujj ba, diina ki dekkal! Ndax gëm nga Doomu nit ki?
Mooy kiy wax ak yaw. (8)
KÀDDUG DUND GI
Waxuma
ci sama coobare, waaye Baay bi ma yónni ci boppam, moo ma sant
li ma ware wax ak li ma war jàngale. Te xam na ne li muy santaane
day joxe dund gu dul jeex. Kon li ma wax, dama koy wax, ni ma
koo Baay bi sante. (1)
Kàddu
yii may wax nag, jógewul ci man, waaye ñu ngi soqikoo ci Baay
bi ma yónni. Ku dégg sama kàddu tegëm nu ki ma yónni, am nga dund
gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tábbi
ci dund. (2)
Dégguleen:
Jamano dina ñëw agsi na ba noppi, mooy jamano, ju ñu dee ñi di
dégg baatu Yàlla, te ku ko dégg dinga dund. (5) Yeena ngi gëstu
Mbind yi, ndaxte dangeen ce yaakaar dund gu dul jeex; te bëgguleena
ñëw ci man ngir am ndund. (4) Musuleena dégg baatam te musuleena
gis xar-kanaman; te kàddoom saxul ci yeen, ndaxte gëmuleen ki
ma yonni. (5) Nu ngeen mana waxe ne " damay suufeel turu Yàlla
ndax li ma ne Doomam laa," man mi Yàlla tam yònni ma ci àddina.
(6) Maa ngi leen wax ne: Man maay yoon wi, dègg gi ak dung gi.
Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man. Xellu Yàlla mi, mooy
joxe dung gi; ñam wi jëriñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci xelum
Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dung gi. (7)
Ki dégg
samay wax te topp leen, du man maa kooy daan, ndaxte wàccuma ngir
daan àddina, waaye damaa ñëw ngir musal ko. Moytuleen: Ku ma beddeeku
te nanguwul samay wax, dina fekk fii li koy daan: Sama njangele
koy daan keroog bés bu mùjj ba. (8)
Wax bii
da wóor: Asamaan si ak suuf dinañu wéy waaye sama wax du wéy mukk.
(9)
BAAY BI
Lu
ngeen xalaat ci Almasi bi: Kan la nekk sëtam? (1)
Ken mënu xam,
man Doom ji, ku dul Baay bi; ken it mënula xam Baay bi, ku dul
man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal. Man xam naa ko, ndaxte ca
moom la jóge, te itam moo ma yónni. (2)
Ki ma yónni
ngi ànd ak mam; musu maa báyyi ma wéet, ndaxte liko neex laay
def. Te nag, ku ma gis, gis nga Baay, kon nag nan nga may laaje,
naan: " Won nu Baay bi?" Ndax xamuloo ne maa ngi ci Baay bi te
Baay baa ngi ci man? Man ak Baay bi been lanu. Lépp lu Baay bi
am, maa ko moom. Jóge na ca Baay bi, ñëw àdddina. Léegi maa ngi
génn àddina, fekki Baay bi. (4)
Doom ji mënula
def dara moon ci boppam, li mu gis Baay di def rekk lay def. Baay
bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu moy def, te dina ko won
jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gëna waaru. Maanaam, ni Baay
bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox ndund gi, noonu la Doom ji
di joxe dund gi ñi mu ko bëgga jox. (5) Baa léegi mënuma def dara
ci sama bopp. Ni ma Baay bi di dígale rekk lay àttee, te sama
àtte bu jub la, ndaxte defuna sama bëgg-bëgg, ci waax ki ma yónni
rekk laay aw. Ni Baay bi ame dung gi moom ci boppam, noonu iit
lako maye Doom ji, mu am ko ci boppam. Jox na Doom ji itam sañ-sañ
àtte, ndaxte mooy Alma si bi, di Doomu nit ki. (6)
Li ma leen
waxoon ca njalbeen ga: Li ma mëna wax ci yeen bo átte leen bari
na, waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali
àddina. (7)
Bu ngeen yekkatee
Doomu nit ki, dingeen xam ne, Maay ki nekk. Di ngeen xam ne iit,
duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jángal rekk laay
wax. (8)
SÀMM BU BAAX BI
Buleen
ragal dara, yeen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay,
mu jagleel leen nguuram. (1)
Man maay sàmm
bu baax bi. Ni ma xame Baay bi, te Baay bi xame ma ni, noonu la
xame samay xar te ñoom it noonu lañu ma xame. Te it kat, dina
joxe sam bákkan ngir xar yi. Samay xar dina ñu dégg sama baat;
xam na leen te ñu ngiy may topp. Dama leen di jox ndund gu dul
jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jëlee ci sama lox. Sama
Baay bi ma leen jox moo génna mag lépp, te kenn mënula jële dara
ci loxob Baay bi.
Ba léegi,
na naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii: War na leena indi ñoom
it, te dinañu dégglu sam baat. Benn coggal mo am ak ben sámm,
te dina leen wottu guddi ak bëccëg. (2)
Ki jaar ci
bunt bi, mooy sámmu xar yi. Wottukat bi dina ki ubbil bunt bi,
xar yiy dégg baatam. Xar yi mu moom nag , bu ci nekk dina woo
ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti. Sámm bi, bu génnee yi
mu moom yépp, dina leen jiitu, ñu topp ko, ndaxte xam nañ baatam.
Waaye duñu topp jaambuur, dañu koy daw, ndaxte miinuñu baatam.
(3).
Man maay sámm
bu baax biy joxe bakkanam ngir ay xaram. Ki dul sámm bi tey líggéey
xaalis rekk waaye moomul xar yi bu séenee búkki, day daw, báyyi
fa xar ya. Bu ko defee, bukki da dal ca xar coggál ga, jápp ca,
tasaare ya ca des. (4)
Man maay bunt
gétt gi, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooki sàcc la,
saay-saay la. Ni ma fi jiitu ñépp ay sàcc lañu, ak ay saay-saay;
waaye xar yi dégluwuñu leen. Man maay bunt bi, ku jaar ci man,
dinga mucc, dinga mëna dugg ak génn, dinga am mbooy goo mana fore.
(5)
Addina si
defa feés deèl ak lu bon, dee ak yaqute; man dama ñew ngir nit
ñit am dund, ba nekk ci nataange. (6)
DUNDU RUU
Mbind
mi nee na: Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu, gu
génne ci gémmiñug Yàlla. (1)
Man maay ñam
wiy joxe dung gi. Ku ñew ci man, doo xiif mukk; te kku ma gëm,
doo mr. Dekkil! Japp leen ñam wiy dund te wàcce ca asamaan. Ku
lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji,
sama yarám la; dama koy joxe ngir àddina mana dung.
Buleen líggéyal
ñam wuy yaqu! Li gen mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul
jeex. Ñam woowué, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la
Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam. (3)
Dégg ngeen
ne sunuy maam dunde nañu mànn ci ál ba, teewul dee nañu. Du Musaa
leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo
leen di jox ñam wu wóorm wi wácee ca asamaan tey jox áddina si
dung gi. (4)
Soo xamoon
li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bop, yaa koy
ñaan doxum dund; ku naan ci doxum teen bii, balaa yàgg mu maraat,
waaye ndox, mi may joxe, ku ci naam du marati mukk , ndaxte day
nekk ci moom bëtu ndox, buy ball, di joxe ndund gu dul jeex. (5)
Ndax danga
mar? Ku mar, na ñew ci man, ku ma gëm na naan! Ndaxte Mbind mi
nee na: Ndox mu bare muy dundale dina xelle ci dënnam (6)
Yeen na
ku ngeen ne moom la?
Jafe-jafe
diine bi.
1. Macë 16:6,
2. Mark 8:18-21, 3. Mark 7:7-9, 4. Macë 7:15, Yowanna 8:44, 5.
Macë 23: 13-28, 5. Yowanna 5:44, 6. Macë 23: 29-34, 7. Macë 15:
7-8, Esayi 29:13, 8. Lukk 16:15, 9. Macë 8:11-12, 5: 20
Leer gi
leeral àddina si
1. Yowanna
12:46; 8:12, 2. Yowanna 3:19-21, 3. Yowanna 5: 33-35-36; 10:37-38;
9: 4, 4. Macë 6: 22-23, 5. Yowanna 11:9-10; 12: 35; Macë 15:14,
Yowanna 12: 36, 6. Lukk 8:17; Macë 10:27
Peeñ gi
1. Yowanna
12: 23, 2. Yowanna 8:50, 3. Yawanna 8:17-18, 32: 24 4. Yowanna
7;18 5. Yowanna 7: 28; 6: 38; 18: 37 6. Yowanna 10:30; 1: 10-9.
7. Yowanna 10:28; 14:27; 8:32-36; 15:11. 8. Yowanna 6:40; 9: 35-37
Káddug
giy dund
1. Yowanna
12:49-50, 2. Yowanna 14:24; 5:24; 3. Yowanna 5:25 4. Yowanna 5:39-40,
5. Yowanna 37:38, 6. Yowanna 10:36, 7. Yowanna 14: 6; 6:63, 8.
Yowanna 12:47-48, 9. Macë 24:35
Baay bi
1. Macë: 22:42,
2. Macë 11:27, Yowanna 7:29, 3. Yowanna 8: 29; 14: 9-10, 4. Yowanna
10:30; 16: 15-28, 5. Yowanna 5: 19-21, 6. Yowanna 5:19,26,27,
30; 7. 8:28
Sàmm bu
baax bi
1. Lukk 12:
32, 2. Yowanna 10: 14-15, 27 29 16, 3. Yowanna 10: 2-5, 4. Yowanna
10: 11, 12, 5 . Yowanna 10: 7, 1, 8, 9; 6. Yowanna 10:10.
Dundu Ruu.
1. Macë 4:4;
Dotorom 8: 3, 2. Yowanna 6:35. 48-51, 3. Yowanna 6:27, 4. Yowanna
6: 49, 32,33; 5. Yowanna 4: 10, 1,4; 6. Yowanna 7:37-38.