Ci
li dale ci jamanoy Yaxya ba léegi; nit ñaa ngi góor-góor lu ngir dugg
ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll. (1)
Nguuru Yàlla Aji
Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam. Waaye bi nit ñi
di nelaw, noonam ñew , ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem. Bi dugub
ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom. Noonu surgay boroom kër ga ñew
ci moom, ne ko: Góor gi, xanaa jiwuloo ji wu baax ci sa tool? Fu jëmb
bi jóge nag? Waaye mu tontu leen: Noon a ko def. Surga ya nee ko: Ndax
ñu dem dindi ko? Waaye mu tontu leen: Déedéet, ngir baña budiwaale dugub
ji, bu ngeen koy dindi. Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot.
Bu ngóob ma jotee nag dina wax ñi koy góog: Njëkleena dindi jëm bi,
takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.
Doomu nit ki
mooy ji wu baax wi; àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo
di ji wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi. Seytaane mooy noon
bi ko ji tukkitel àddina mooy ngóob mi, ta malaaka yi ñooy góokat yi.
Ni ñu dajalee jemb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee. Doomu
nit ki dina yebal ay malaakaam ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit
bàkkar, ak ñiy def bàkkar, sánni leen ci safara, foofa dees na fa jooy
te yéyu. Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay.
Dégglul bu baax, yaw mi am ay nopp. Réew mu xees boppam tas, te dëkk
mbaa ker guy xeex boopam du mana yàgg. Bu Seytaane dàqee seytaane nag,
xeex na boppam; kon naka la nguuram di mana yàggee? Te it, bu fekkee
ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Seytaane, seeni taalibe nag, ci gan
kàttan lañu leen di daqee? Kon ñoo leen di àtte. Waaye bu fekkee ne,
ci xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yeen. (3)
Xana musuleen jàng
lii ci Mbind yi: " Doj wi tabaxkat y sànni; mujj na doon doju koñ; ci
Boroom bi la loolu jóge, te yeemu nanu ci." Loolu moo tax maa ngi leen
koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam.
(4) Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bákkaar,
muy sosal Yàlla wu mu mana doon. Waaye kuy sosal Xel mu sell mi, deesu
ko baal muk; gàddu na bàkkkaar ba fàw. Juutikat yi ak jígéen moykat
yi ñoo leen di jëkka dug ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ndaxte Yaxya ñëwna
ci yeen ci yoonu njub, te gëmuleen ko, waaye juutikat yi aj jígéeni
moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikiwul
sax, ba ngeen gëm ko. (5)
Du képp ku may wax:
Boroom bi, Boroom bi mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kaww ji, ka cáy dugg
mooy kiy def samag coobareg Baay bi nekk ci kaw. Jamano dina ñew, ju
boroom kër gi di jòg, tëj buntam. Di ngeen nekk ci biti di fëg naan:
" Ubil nu".
Boroom kër gi dina
leen tontu ne: " Xawma fu ngeen bokk, dem leen seen yoon" Noo doon bokk
di lekk di naan, te jàngale nga sunuy pénc. Dina leen tontu ne: " Nee
naa xawma fu ngeen bokk, yeen ñepp soreleen ma defkati lu bon!" Bu bés
ba, ñu bare dinañu ma wax: Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur
lanu daan waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa daqe rab?
Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare? Ci kaw loolu dina
leen wax dëgg, ne leen: Musuma leena xam, soreleen ma, yéen ñiy def
bákkaar" (6) May nañu leen ngeen xam mbóoti nguur Yàlla, waaye ñi ci
des, dama leen di wax ci ay léeb. (7)
Beneen léeb moo
ngi nii: Nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi mu laata
dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam ku nekk lu mu àttan. Ken
ka mu dénk ko juróomi junii, keneen ka mu denk ko ñaar, ka ca des, ben:
Daldi tukki. Bi mu demee nag, ki jot juróomi june ya dem, di ci juula,
ba amaat yeneen ñaar. Waaye ki ji j ot benn june, gas pax, nëb fa xaaliisu
njatigeem, ngir bañ sàcc yi jël ko.
Ganaaw diir bu yàgg
njaatigeb surga ya dellusi, daldi leen laaj alalam. Noonu ki jot juróom
june ind yeneen juróom, naan: " Kili fa gi, dénk nga ma juróomi june,
seetal am na ci yeneen ñaar. Njaatigeem ne ko: Def nga lu baax, surga
bu baax nag te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk la
bare. Kaay bokk ci sama mbég.
Gannaaw loolu nag,
ki jot june jegeñsi, ne ko: Kilifa gi, xamoon naa ne m nit ku néeg nga,
dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul. Moo tax ma ragaloon la,
ba dem nëbb sa xaaliis ci biir suuf; mu ngii fabal li nga moom. Waaye
njaatigeem tontu ko: Surga bu bon nga te taayeel. Gaannaaw xamoom nga
ne, damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul, kon waroon ngaa
yóbbu ca deñckati xaaliis ya. Bés bu ma ñewwee nag, na mana jot li ma
moom ak li mu jur. Noonu, njatigee bi nee: Nanguleen xaalis bi ci moom,
jox ko boroom fukki juni yi. Ndaxte ku am dinañu la dólli ba nga barele,
waaye ku amul, li nga am as néew sax, di nañu li nangu. Te sànnileen
surga bu amul njërin bi ci biti ci lëndem gi. Foofa dees na fa jooy
te yéyu. (8)
Beneen léep biy
misaal nguuru Yàlla ngii: Noonu benni boroom kër génnoon na ab suba
teel ngir jël ay liggéeykat ndax toolut réseñam. Mu juboo ak liggéeykat
ya ci bëccëg posetu denaryon, door leena yabal ca toolam. Ci yoor-yoor
nu géenn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma ta liggéeyuñu. Mu ne leen: Demleen
yeen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jáadu. Ñu dem ca. Mu génnaat
ci digg-bëccëg ak ci takusaam defaat noonu. Mu génnati ci tàkkusaan,
gis ñeneen di tendeefal mu ne leen; Lu tax ngéen yendoo tendeefal, te
liggéeyiwuleen? Ñu tonto ke: Kenn jëlu ñu. Mu ne leen: Demleen yeen
itam ca tool ba.
Bi nga xamee ne
timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: Woowla liíggéeykat yi te
fey leen seen bëcceg, támbale ci ñi mujja ñew, ba ci ñi fi njëkk. Noonu
ñi mu jël ci takusaam ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye
ñoom itam ñu jot ku nekk ben denaryon. Bi ñu ko jotee nag, ñu tambalee
ñaaxtu ca boroom kër ga naan: Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lanu liggéey,
ba noppi nga yemale leen ak nuun, ñi yenu coonob bëccegg bi ak naaj
wu metti wi. Waaye boroom kër ga tontu ken ci ñoom ne ko: Sama waay
tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci ben denariyon? Kon fabal li nga moom
te dem. Su ma bëgge fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw, ndax sañumaa
def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaam ci la yéwém?
Noonu, ñi mujj ñooy jiitu, ñi jiitu ñooy mujj. (9)
Nguuru Yàlla Aji
kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu ci tool. Nit ku ko gis nëbbaat ko;
xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba. (10) Ñiy dugg
ci Nguuru Yàlla Aji kawe ji lenko wu ñu ak jefiy àddina. De no mel ni
jaaykat buy mos di wuut per yu rafet tey jar njëg y réy. De no dëdu
lèpp ngir ndam li ci alal bii. Dund gu bees, xalaat yu bees, yaakaar
ci àddina sii ak ci wiy ñëw. (11)
Nguuru Yàlla Aji
kawe ji, Yàlla Aji kàttan moo ko jiite. Da fa mel ni nit ji ji tool.
Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg jiwi wi sax, di màgg, te
xamul naka la ko defe. Suuf si day mëñ moom ci boppam, mu sax, focci,
def ngóob. Bu ngóob bi ñoore nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jotna. (12)
Nguuru Yàlla Aji
kawe ji, dafa mel ni doom fuddén, bu nit jël ji ko ci toolam. Doomu
fuddém moo gëna tuuti ci jiwu jépp mépp waaye bu saxee, mooy sut ci
gañcaxi tóokeer yi, di nekk garag bu kawe. Ba picci asamaan ñew tàgg
ciy caram. Dafa mel itam ni lawiir bu ñu jaxase ak fariñ, ba tooyal
bép di funki. (13)
Ci jeexalit Nguuru
Yàlla Aji kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej mu jápp jën
wu nekk. Bi mbaal mi feese nag, ñu ñoddi ki tefes gi, ba noppi ñu taxaw,
dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon. Noonu laya mel, bu àddina
tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tánn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi, sánni
leen ci safara. Foofa dees na fa jooy te yéyu. (14) Ba ma leen yebalee
te yóbbaalewumaleen woon xaalis, mbuus walla dàll, ndax ñakkoon ngéen
dara? Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam.
Bés bu nekk, coonoom doy nako. Ana kan ci yeen ci kaw njaaxlem moo mana
yokk waxtu ci àppam? (15) Seetleen picci asamaan: Duñu ji, duñu góob,
duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax
ëppuleen maana picc yi ci lu bare? (16)
Ñaari picci rammatu,
ndax duñu ko jaaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te
soobul seen Baay! Seen kawari bopp sax, waññees na leen. Kon bulen ragal
dara, yeena gëm ndiiraanu rammatu. (17)
Lu tax ngeen di
jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax ni tóor-tóor ñax ni saxe ci tool
yi. Duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wa ne, Suleymaan sax ci ndaman,
soluwul woon ni benn ci ñoom. Yeen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii
ñaxum tool yi, miy sax tey teu suba ñu def ki taal bi, ndax du leen
gëna wodd? Buleen jaaxle nag, di wax ne: Lu nu wara lekk? Lu nu wara
naam? Wala, lu nu wara sol? Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy
wuut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeem soxla ci loolu
lépp. Waaye jëkkleena wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen
ki dollil. (18)
NDIGALU BUUR BI
Ndígal
bii moo gëna màff ci ndigal yi: Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol
bépp ak sa bakkan bépp, sa xol mépp ak sa kàttan gépp. (1)
Te ñaareel bi, muy
bi ci topp, lii la : Nanga bëgg sa moroom, ni na bëgge sa bopp. (2)
Sama ndigal mooy
ngeen bëggante ni ma leen bëggee! Ndigal yii ñooo sut yépp. Genn mbeggeel
mënula weesu joxe sa bakkán ngir say xarit. (3) Ku tebbi nag ba gëna
tuuti ci ndigal yi, te ngay jángal nit ñi noonu, dees na la tudde ki
gëna tuuti ci nguuru Yàlla Aji kawe ji. Waaye ku leen di sámm, dileen
digle, dees na la tudde ku mag ci nguru Yàlla Aji kawe ji. Wax naa leen
loolum ngir ngeen bokk ci sam mbég, te seen bos mat sëk. (4) Dégg ngeen
ne, waxoon nañu: Soppal sa moroom, te sib sa bañaale. Waaye ma maa ngi
leen di wax ne: Soppleen seni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal,
ngir wone ne yeenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mungi kenkal
jántam ci ñu bon ñi ak ñu baax ñi , te muy tawal ñi jub ñi ak ñi jubadi.
Su ngeen soppe ñi leen sópp, ban yool ngeen am? Xana juutikat yi duñu
def noonu it Su ngeen nuyoo seeni mbokk rekk, lu ngeen lu def lu doy
waar? (5)
Maa ngi leen di
jox ndigal bu bees: Bëgganteleen. Nangeen di beggante ni ma leen bëgge.
Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngen bëggante. Lii du doon
lu leen di bett. Dingeen xam ñi ma bëgg dëgg. Nit kooki day dunde samay
kàddu, te Baay bi dina ko sargal ak barkeek ko ci biiri mbokam. Ku ma
bëgg dina sàmm sama kàddu. Sama Baay dina ko bëgg te nun dinanu ñëw
ci moom, te dëkk ci moom. (6)
Baay bi ci boppam
bëgg na leen. Bëgg na leen ndaxte bëgg ngeen ma, te gëm ngeen ne ci
Yàlla la jóge. Saxleen ci mbëggeel googu ma am ci yeen. Bu ngeem toppee
samay ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam. (7)
Dafa amoon nit ku
jóge woon Yérusalem jëm Yériko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko
ba mu bëgga dee, dem bayyi ko fa. Faf ab sëriñ jaar ca yoon wa, seén
nit ka, teggi. Ben waay it, bu soqikoo ci giiru léwi, aw ca bérab booba,
seém waaja, teggi. Waaye ben waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw
ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko. Noonu mu ñëw, diw ki diwlin ak biiñ
ngir faj gaañu-gaañu ya, laxas ko ay cër, gannaaw loolu mu teg ko ci
mbaamam, yóbbu ci fanaanukaay, di ko topptoo. Bi bët setee, nu géne
ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga, ne ko: " Nanga topptoo nit
kooku. Bés bu ma fi jaaraate, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp l
ci dolli ci xaalis. An kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëme ci moroomam,
ba ñu gisee nit ka sàcc ya dogale woon?
Demal tey def jëf
yu baax ni waaay jooju dëkk Samari. (8)
NGUURU YÀLLA
GU BEES BI
NGUURU
YÀLLA BI
1. Macë 11:12,
2. Macë 13: 24-30, 37-43, 3. Macë 12: 25-29. 4. Macë 21:42-43, 5.
Mark 3: 28-29; Macë 21:31-32, 6. Macë 7:21; Lukk 13: 25-27, Macë 7:
21-23, 7. Lukk 8:10, 8. Macë 35: 14-30, 9. Macë 20: 1-16; 22:14, 10.
Macë 13: 45-46, 11. Macë 13: 44, 12. Mark 4:26-29, 13. Macë 13: 31-33,
14. Macë 13: 47-50, 15. Lukk 22:35; Macë 6: 34,27, 16. Macë 6: 26,
17. Macë 10: 29-30, 18. Macë 6: 28-33.
NDIGALU BUUR
BI
1. Mark 12:29-30;
Dotoronom 6:4, 2. Mark 12:31; Levitik 19:18, 3. Mark 12:31; Yowanna
15:12,13; Mark 12:31, 4. Macë 5:19; Yowanna 15:11, 5. Macë 5: 43-47,
6. Yowanna 3: 34,35; 14:23, 7.Yowanna 16:27; 15: 9-10, 8. Lukk 10:
30-37.